Bismil Laahir Rahiimir Rahiimi.
Was salaatu was salaamu halaa man laa nabiyya bahdah.
Ñu fas yéeney dollee deŋkënte ak di dollee fàtleente.
Ñiŋ koy jëmële nak ci tomb binga xamne mbooleem liy yiwu àdduna ak yiwu àllaaxira ci lako sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa dëxëñ. Mbooleem yonant yimu yónni yépp ci la leen digël ñu tek ci seen tank. Mbooleem ñi leen topp ñépp yit ci la leen digël ñu tek ci seen tank. Mooy tomb bi nga xamne ci la mucc nekk ci àdduna ak ci àllaaxira, ci la texe nekk ci àdduna ak ci àllaaxira, ci la làq ngërëmël sunu Boroom nekk ci àdduna ak ci àllaaxira.
Mooy tomb bi nga xameenteni jaam bu ci tëŋku sunu BOROOM dana ko musël ci fitnay àdduna ak ci àllaaxira, musël ko ci njàqaray àdduna ak ci àllaaxira.
Mooy tomb bi sunu BOROOM deŋkóon ñu njëkk ña ak ñu mujj ña ñu tëŋku ca.
Mooy tomb bi nga xamne ku weex gênul ku ñuul, ku ñuul gënul ku weex ludul ci boobii tomb.
Tomb boobii mooy lan : “At-taqwaa”.
Ragal sunu BOROOM nak moodi jaam bi fexe bab xolam bépp pas pas bu sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa gërëmut mu bañ caa nekk, fexe yit ba aw làmmiñam bépp kàddu bu sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa gërëmut mu bañ ko caa wax, góor góor lu bu baax ba ci ay cërëm bépp jëf bu sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa gërëmut mu bañ ko caa jëf.
- Lan mooy pas pas bu sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa gërëm ?
Moodi :Jaam bi wéetal Boroomam ci fas ci xolam, ta muy dëgg ci moom, ne sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa buur bu am la, am gu tàambaleewul fenn ta yemuwul fenn, ta soqikuwul ci lennit, ta nuróowutak kenn wala lenn ci jëmmëm, ci jëfëm ak ci melokaanam, ta lépp lu am moo ko amal ci coobareem Subhaanahu wa Tahaalaa.
Bu fasee loolu ci xolam ci diggamak Boroomam, am na yit luko war ci diggamak ay moroomam. Ba ca njëkk mooy mu watandiku rëy, ak kañaan ak naw jëf ak jëf bëgg ñu diko tudd ak ngistal :
Rëy moomii, jaam bi bu xoolee lako sos ak famuy mujj rëy xajufi. Sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa waxoon na Sëydinaa Muusaa bul jàpp ni yaa gën kenn feek séenóo sa bopp ci biir aljana seen kookee ci biir safara. Rëyit mooy la alagoon ibliis.
Kañaan itam, jaam bi war na diko moytandiku ndax day lekk jëf ni sawara di lekkee matt, ta mbugëlum aji añaan ci àdduna lay tàmbalee ndax limu bëgg muy deñug xéewël cib jaam sunu BOROOM duko def mukk ci ludul coobareem, ndax sunu BOROOM mooy kiko ko defal. Waxtu wu gisee sunu BOROOM dollikoy xéewël day daaldi dollikook tiit ak njàqare ta duca man dara. Kon li war jaam bi rek, moodi lépp lub jaam am mu yéene koko bamu melni moom mooko am, loolii mooy liy noppal nit ki ci añaan.
Naw jëf itam ak jëf bëgg ñu diko tudd, jaam bi su gisee ni bindul boppam, dees koo amal rekk, xiir ko ci limuy jëf, kon na sant kako amal ta xiir ko ca lamuy jëf, ta sant ko ca.
Ngistal itam jaam bi, waxtu wu tawxiitam mate sunu BOROOM man nako caa musël. Ndax su boobaa yit day gis ni moom jëful waaye day jottali jëf ja rekk.
Kon loolu mooy li war jaam bi ci digëntéem ak Boroomam, ak ci digëntéem ak ay moroomam.
- Jaam bi yit di góor góor lu bu baax ba aw làmmiñam du ci yékkëti benn kàddu bu Sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa gërëmul. Mu cay wattandikoo jëw ak rambaaj ak wax lu amut :
- Jëw mooy wax ci sa moroomum jaam loo xamne su ko deggóon duko gënël. Ta li ci sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa wax ci téeréem bi war naa tax jaam bune war koo moyandiku : muy nimu ko nuróolée ak lekk meddum nit. Kon bépp jaam boo xamne bëggóo sa moroomum jaam faatu ñu suul ko ba mu am ñatti (3) fan ngay dagg ay cërëm di sex, war ngay wattandiku kon di toog fenn di tudd sa moroomum jaam, ci loo xameenteni suko deggóon duko gënël.
- Jaam bi war nay wattandiku rambaaj. Muy di dox di wax luy yàq digënte ay jaam wala di yàqal ab jaam ci moroomum jaam, loo xamne manoon na caa am aw yiw. Jikko la joo xamne jëmm juko ame du dugg aljana mukk mukk.
- Jaam bi war nay wattandiku wax lu amut ndax loolii ci jikkoy naafeq la bokk ta naafeq ci xur wa gënë suufe ca sawara mooy dëkkuwaayam.
- Kon jaam bi nimu wara saŋee ab xolam noonii la wara saŋee aw làmmiñam, ñëwit ci cër yici des. Muy fexe ba ay gëtëm duci xool lu sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa gërëmul, ay noppam noonu mu bañ cee deglu lu sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa gërëmul, ay loxoomit mu bañ cee jëf lu sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa gërëmul, biiramit mu bañ caa def lu sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa gërëmul, pëyëmit noonu mu bañ koo dugël fu sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa gërëmul.
Nga xamne mooy saŋee xol bi ci lu sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa gërëmul, saŋee làmmiñ wi ci lu sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa gërëmul, saŋee ay cërëm ci lu sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa gërëmul.
Fexe ba sab xol dooci ëmbël kenn lu ñaaw, saw làmmiñ dooci wax kenn lu ñaaw, say cër dooci jëfléente ak kenn lu ñaaw. Linga bëgël sa bopp nga bëgël ko mbidéef yépp. Di wax ci ñépp lu rafet, di jëfléente ak ñépp lu rafet. Loolu mooy melokaan wi nga xamne moom la sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa soññ ñépp ci ñu melowooko. Mooy melokaan winga xamenteni nit ki lumu bari bari xamxam ta melowoo wuko, mook ki xamut dara ñoo yem. Mooy melokaan wi Yonent bi (sallal Laahu tahaalaa halayhi wa sallam) wax ni : ñiko ame ñoo gënë yey ci moom, ñuñ mana doon ak fuñu mana nekk. Loolu mooy : “At-taqwaa”.
Looloo taxit sunu BOROOM ñaax jaam ñépp ñu mel woowii melokaan ngir ñu mënë mucc ci safara minga xamne ay nit ñoo koy xamb ak ay doj, ta sunu BOROOM dëële ko way weddi yi.
S.2 – V.24
Muy :
S.2 – V.41
Mooy melokann wi sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa wax ni jaam bune war nakoo melowoo ngir bàyyi xel bis ba nga xamne benn bakan du manal moroom ma dara, ta képp ku melowoowutóon woowii melo deesuti nangu ci moom am rammu, deesuti jàpp ci moom ag maandu, deesuti ko dimbëli yit.
Muy :
S.2 – V.48
Ba tay sunu BOROOM waxne Al-quraan nekk na waare ñeel way ragal Yàlla yi.
Mu dellu waxne, moom sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa : “Laysal birru…”.
Du caageeni ag topp mooy ngeen di jëmële seeni xar kanar ci wàllu peŋku wala ci wàllu sowwu.
- Waaye ag topp mooy nga gëm sunu BOROOM, wéétël ko ci jëmmëm ak ci jëfëm ak ci melokaanam, ta lépp lumu dogal ci yaw nga gërëm ko, gëm bis bi mujju ba nga xamne lépp lum bind muy nit ak jinne ak malaa-ika kune mu laaj la lam la santoon na nga ca def, ak gëm amug malaa-ika yi nga xamne ay jëmm lañ yu sunu BOROOM bind cig leeram, gëm teere yi, ne ci sunu BOROOM lañ bàyyikoo, jëm ci jaamam yimu tànn, gëm yonant yi ne ndawi sunu BOROOM lañu subhaanahu wa tahaalaa yumu tànn.
- Ngay joxe sa alal àndak bëgg nga ko, waaye nga diko joxe ngir jëmmi sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa. Nga diko jox say jegeñaale, nit ña la jege cig mbokk, ak jirim ñi, ak miskiin ñi, ak doomi yoon.
- Jirim mooy ku ay waajuram gaañu ta amagul kattanug fàggu.
- Miskiin mooy koo xamne amul luko doy ci dund ak koddaay ak dëkkuwaay.
- Doomi yoon mooy ab tukkikat boo xamne day tukki tukki bu dagan ta lamu amewoon jeex, nga dimbiliko ci luko yeggele famu jëm ak luko delloosi famu jogewoon, ngir jëmmi Yàlla. Tukkib lëggéey ngir fàggu loo tëyée sag ragal Yàlla, tukkib jaamu Yàlla la.
- Ak ñi nga xamne dañiy laaj nga di leen jox ngir jëmmi Yàlla, mooy ñiy yelwaan.
- Ak ab jaam bu bindënte ak sangam ngir mu warkoo jox luy tax mu goreel ko, kooku dees nako dimbali ngir lumuko wara jox, ngir mu gore.
- Boolecaag di taxawal julli, tay natt asaka, ak di matale sa digente ak sa BOROOM ak linga wóllareente ak say moroom, ci jëf ak ci wax.
- Ak di muñ bula sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa nattoo ag ñàkk, ak di muñ bula sunu BOROOM nattoo tawat. Ak di muñ boo nekkee ci waxtuw jàkkaarloo ak nooni lislaam yi ci xeex, ak ngay muñ waxtu woo nekkee ci jihaat ak sa bakan.
Ñooñii dëy ñooy dëggël, ñooñii ñooy ñi ragal Yàlla yit.
S.2 – V.177
Mooy aaya bi nga xamne melo yi sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa gërëm ci jullit yépp mingi ci aaya bi.
Ba tay sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa di wax ni yéen way gëm ñi bind nañ ci yéen koor ni ñuko bindeewóon ci ñi leen njëkkóon, ngir ngeen mana ragal Yàlla.
Koor nak ñatti(3) daraja la :
- Darajaay koor gu njëkk ga, mooy bàyyi lekk ak naan.
- Koorug ñaareel ga, mooy wooral sa cër yépp ci lu neexut sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa, ci biir weeru koor ak ci ludul weeru koor, muy ci jamono bune, ci waxtu wune ak ci saa sune.
- Koorug ñatteel gi, mooy goor goor lu bubaax ba sab xol dooci xalat lenn ludul sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa.
Aaya boobii mooy :
S.2 – V.183
Sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa ba tay mingi wax ni : saŋe leen seenub xol ci lépp luma gërëmut, saŋe seenub làmmiñ ci lépp luma gërëmut, saŋe seeni cër ci lépp luma gërëmut ngir ngeen mana texe. Ndax jaam bi munuta texe mukk ci ludul mu làq ngërëmël sunu BOROOM, ta munuta làq ngërëmël sunu BOROOM ci ludul mu sax ci limu ko digël ta teet limu ko tere, boole ca lumu dogal ci moom mu gërëm ko.
S.2 – V.189
Ba tay na ngeen sax cig ragal Yàlla ta xamne sunu BOROOM ku àndak way ragal Yàlla yi la ci ndimbalal àdduna ak wu àllaaxira.
S.2 – V.194
Na ngeen sax cig ragal Yàlla ta xamne sunu BOROOM ku taral mbugëlëm la ta saxal ko ci way won gànnaaw lamu digle ta nekk ca lamu tere.
S.2 – V.196
Na ngeen xamne naka ngën gi yóbbël ci àdduna ak ci àllaaxira mooy ragal Yàlla. Kon na ngeen ma ragal yéen way boroom xel yi. Ndax boroomum xel mooy kiy ràññee lépp liko topp liko sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa digël di jurël, ci àdduna ak ci àllaaxira ; mooy kiy raññee yitam lépp liko moy liko sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa digël di jurël ci ay naqar aki tiis ; mu tànn topp liko sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa digël teet lamu ko tere.
S.2 – V.197
Na ngeen sax cig ragal Yàlla ta xam xam bu wóor ni yéen ñépp dana ñu léen pang ëlëg ngéen jëm ci moom.
S.2 – V.203
Gaa ñi nga xamne ñu sax cig ragal Yàlla lañu, ñooy way gañe ñi ci yiw ak tawfeex aki xéewël ëlëg yawmal xiyaam.
Sunu BOROOM dana wërsëgël kuko soob ci ludul benn coono.
S.2 – V.212
Na ngeen sax cig ragal Yàlla ta ngeen xamne kenn ku nekk ci yeen dana dajeeg Moom ba jàpp ne moom rekk la sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa bindóon.
S.2 – V.223
Na ngeen sax cig ragal Yàlla ta yewenël seen digënteeg nit ñi.
S.2 – V.224
Na ngeen sax cig ragal Yàlla ta ngeen xamne sunu BOROOM ku dañ kumpa la, ku xam bépp mbir la, ci lu nëbbu ak ci lu feeñ, ci jamono bune, ci waxtu wune ak ci saa sune.
S.2 – V.231
Na ngeen sax cig ragal Yàlla ta ngeen xamne sunu BOROOM aji gis la ci gis gu sax, ci li ngeen di jëf lépp, ci jamono bune, ci waxtu wune ak ci saa sune.
S.2 – V.233
Yéen way gëm ñi na ngeen sax cig ragal Yàlla, ta ngeen di won gànnaaw lépp lu daganul ci njaay, ndeem way gëm ngeen. Képp ku tuub, dugg ci lislaam, lépp loo amewoon ci lu daganul na nga tàqalikoo ak moom, rawatina yaw miy aji gëm.
S.2 – V.278
Mu dellu wax ni na ngeen sax cig ragal Yàlla ta bàyyi xel bis bi nga xamne danañu laxas, tëdd ci lalum ndee, jëm ci sunu BOROOM, ta sunu BOROOM diñu fay sunuy pas pas, sunuy kàddu ak sunuy jëf.
S.2 – V.281
Jëmm june nay ragal Boroomam bi ko bind ta moom ko ta melal ko.
S.2 – V.282
Na ngeen sax cig ragal Yàlla, sunu BOROOM xamal léen liko soob ci xam xamam bi tàmbaleewul fenn ta yemuwul fenn, ta sunu BOROOM mooy aji xam bépp mbir xam gu sax.
S.2 – V.282
Loolu mooy waral ah-lu tasawuuf di jihaad ak seen bakan ngir jiko yi sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa gërëmut deñ ci séen biir, ndax jiko yooyu mooy kiiraay bi dox digënte jaam bi ak xam xamu ladunii (mooy xam xam bi bàyyeekoo ci sunu BOROOM ta du jaar ci jenn jëmm).
Jikko yooyu maanaawoo ni rëy, ngistal, rambaac, jëw, di jëf bëgg ñu diko tudd, ak yu maanaawoo ni ñoom.
Jaam bi nak bu sellalee ab xolam, sellal aw làmmiñam, sellal ay cërëm, sellal gu sax, sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa danakoca xamal la ko soob.
. . . . . . .
Ñeel na gaa yi sax cig ragal Yàlla, fa seen Boroom, itasi wurus ak yuy jamaa ak yuy oor yu taaru taaru gu jéggi dayo. Di daw ca suufu itaas yooyee ay dex, ñuy way sax ca biir kër yooyee, ñeel leen fa ay soxna yu taaru taaru gu jeggi dayo, muy ay soxna yunu laabalit, ay soxna yudul gis baax mukk. Dex yooyee maanaam dexu sàngara la ak dexi lem ak dexi meew ak dexi ndox. Ñuy aji way làq ngërëmël sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa, làq gu sax. Sunu BOROOM aji gis la, gis gu sax, ci jëfi jaamam yépp.
S.3 – V.15
Na ngéen sax cig ragal Yàlla ta topp ci gànnaaw Yonant bi (sallal Laahu tahaalaa halayhi wa sallam), fumu teggee tànkam ngéen tek fa séen tànk, ta bëgg ko bëgg gu wer, mu gënël leen seen bopp, seen alal ak seen njaboot.
S.3 – V.50
Naka sama BOROOM mooy kima bind, mooy kiléen bind, ta melal léen, ta moom léen, na ngéen sax ci diko jaamu : lii mooy aw yoon wiy aji jub.
S.3 – V.51
Li fi nekk, bépp jëmm buy matale wollareem ak Boroomam ak moroomam booleci sax cig ragal Yàlla, na xamne sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa ku bëgg aji way ragal Yàlla yi la.
Dafa bokk ci aaya boobii li tax mu wàcc, waa ah-lul kitaab ñi nga xamne seenub yonant daf leena xibaaroon dikkub Yonant bi (sallal Laahu tahaalaa halayhi wa sallam) képp kuko ca gëm ta topp ko, sunu BOROOM ku bëgg aji way ragal Yàlla yi la.
S.3 – V.76
Yéen way gëm ñi …..
Lan mooy gëm Yàlla?
Gëm Yàlla moodi wéetël sunu BOROOM ci jëmmëm, ci jëfëm ak ci melokaanam, xamne kuci wéet la, gëm malaa-ika yi, gëm yonant yi ak téere yiñu andi, gëm dogal moo xam aw yiw la wala safaan ba, gëm bis péñc ba, gëm aljana ak safara ak siraat. Jaam bi su gëmee dëgg dëgg ngëm mooy tax sunu BOROOM bëgg ko. Ta mbëggum sunu BOROOM mooy tawféex si jaam bi.
Yéen way gëm ñi loolii, na ngéen ragal Yàlla dëgg dëgg ragal ko, ndax mooy tax ngéen mucc.
Dëgg dëgg ragal Yàlla mooy nga jihaad ak sa bakan ba àgg ci sa xol dóotóo ci mana xalaat ludul màggug sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa ak lumu gërëm, say kàddu dóotóo ci mana yékkëti benn kàddu budul bu sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa gërëm, say cër dóotóo ci mana jëf jenn jëf judul ju sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa gërëm.
Kon nak bu dee dikk mukk ndare bu nekk ngéen di way jébbël séen lépp séen BOROOM subhaanahu wa tahaalaa.
Kon :
S.3 – V.102
Su ngéen muñée ta sax cig ragal Yalla, pexem seeni noon du léen lor mukk ndax suñu BOROOM ku peek la li séeni noon di jëf ngir mu baña jëmsi ci yéen, ta sunu BOROOM duko antul mukk.
S.3 – V.120
Na ngéen sax cig ragal Yàlla, ngéen di way sant sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa. Ndax ragal Yàlla mooy tax nit ki ak ngëmëm mënë yokku, ngëmëm su yokkoo mooy tax muy gënë wàkkiirlu ci Boroomam, su wàkkiirloo ci Boroomam, sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa yoralko léppëm. Su boobaa ag cant rekk moo cay top.
S.3 – V.123
Na ngéen sax cig ragal Yàlla ndax ngéen di way texe texe gu màgg ta sax.
S.3 – V.130
Na ngéen sax cig ragal Yàlla ngir ngéen mana mucc ci safara mi sunu BOROOM dëël way weddi yi.
S.3 – V.131
Na ngéen topp Yalla ak Yonantam ngir sunu BOROOM yërëm léen.
S.3 – V.132
Na ngéen gaaw jëm ci njéggël gu bàyyikoo ci sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa ak aljana joo xamni yaatuwaayam yaatoonani assamaan yi ak suuf yi, ta sunu BOROOM dëël ko way ragal Yalla yi.
Way ragal Yalla yi, ñooy gaa ñinga xamne dañiy joxe seen alal ci yoonu Yalla, ci jamono bañu barilee ak néewlee, ci jamono bañu nekkee ci xat xat ak yolom yolom, ci jamono bañu nekkee ci bekkoor ak naataange. Ak gaa ñanga xamenteni danañu nëbb séen mer, di jéggël nit ñi, settee wuñuci ab jullit ak kudul jullit. Sunu BOROOM ku bëgg aji way rafetal séeni pas pas la, rafetal séeni kàddu, rafetal séeni jëf.
S.3 – V.133 & V.134
Al Xuraanul Kariim ag leeral gu bir la akug teqale la ñeel dëgg ak neen ñeel nit ñi, doonit ag njub ñeel aji way sóobu ña, doonit aji waare ñeel way ragal Yalla yi.
S.3 – V.138
“Mbaax nak mooy jaam boo xamne melowoona melokaan yi sunu BOROOM gërëm yépp ci digëntéem ak Boroomam, ak ci digëntéem ak ay wayjuram, ak ci digëntéem ak ay dëkëndóom, ak ci digëntéem ak mbooléem jaam ñépp”.
S.3 – V.198
Yéen nit ñépp na ngéen ragal séen BOROOM, maanaam na ngéen feg ci séen xol lépp lu sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa gërëmut, feg ci séen làmmiñ lépp lu sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa gërëmut, feg ci séeni cër lépp lu sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa gërëmut, ñeel séen BOROOM bi léen bind ci benn bakkan muy Aadama. Mu bind ci bakkan boobii soxnaam muy Awa. Mu jële ci ñoom ñaar ay góor ak ay jingéen yu baree bari.
Sunu BOROOM nekk na kuy janloog ñépp ak lépp ak fépp, ci jamono bune ak waxtu wune ak saa sune, ta di léen fuglu.
S.4 – V.1
Na ñuy ragal sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa ci li way faatu ñi bàyyi gannaaw, tay wax wax ju jub ta nupi.
S.4 – V.9
Su ngéen yewënëlée ci li ngéen weesu ci lépp lu sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa gërëmut ci pas pas ak ci kàddu ak ci jëf ta bañati caa dellu, sunu BOROOM nekk na jégglaakoon ci képp ku yewënël ci limu weesu, ta fas yéene bañati caa dellu.
S.4 – V.129
Denk naa gaa ñanga xamne ab téere dikalóon naléen, ta bàyyikoo ci samay ndaw, njëkk yéen, ak yéen tamit lima léen denk, benn denkaanebi rekk la : mooy sax cig ragal Yalla.
S.4 – V.131
Na ngéen di dimbléente ci séeni xam xam, ak ci séeni alal, ak ci séeni kàddu, ak ci séeni jëf, ak cig ragal Yalla. Ta ngéen di baña dimbléente ci jëfu ñaawtéef, ak pas pasu ñaawtéef, ak kàdduy ñaawtéef, tay baña dimléente cig noonoo ci digente yi. Ta ngéen sax cig ragal Yalla ta xamne sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa ku tar mbugël la ci way tooñ yi.
S.5 – V.2
Na ngéen sax cig ragal Yalla. Sunu BOROOM kat aji xam la, xam gu sax, ci lépp lu nit ëmb ci dënnëm ta diko nëbb, ci suba yi ak ci ngoon yi, ci waxtu wune, ci jamono bune ak ci saa sune.
S.5 – V.7
Na ngéen sax cig ragal Yalla, sunu BOROOM mooy wéeruwaayu way gëm ñi.
S.5 – V.11
Sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa, way sax cig ragal Yalla yi rekk lay naggul séeni pas pas ak séeni kàddu ak séeni jëf.
S.5 – V.27
Yéen way gëm ñi na ngéen sax cig ragal Yalla, ta sàkku wasiila wu ngéen doxale séen digënte ag moom.
Wasiila moomii day laaj ag leeral :
- Man naa nekk jëmm ju bokk ci jëmm yi sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa tànn, def ci moom leeram ak yërmandeem ak njéggëlëm ak tàwféexëm ak barkéem : mooy yonant yi ak kummalul awliyaa-u yi.
Sunu BOROOM bula defalee tàwféex, nga dajeeg ñoom, nga jox sa bopp sa BOROOM ta jaarale ko ci ñoom, mooy li sunu BOROOM waxoon yonant bi.
S.48 – V.10
- Soo dajewutag jëmm yu melni jëmm yooyii, nga topp ci séeni jeexit : tëŋku ca Al Xur-aan ak sunna, baña ëppêl baña sàggan niko mawlaanaa Cheikh Ahmadou Bamba waxe ci téeréem biñuy wax « masaalikul jinaan ».
Kon wasiila man naa nekk jëmm, man naa nekk jëf.
Ta ngéen di jihaat ci yoonam wi ci séeni bakan ak ci séeni jëf bu ko laajee, ndax le ngéen texe.
S.5 – V.35
Na ngéen sax cig ragal Yalla ndeem nekk ngéen di way gëm.
S.5 – V.57
Loolu liko waral mooy ñi nga xamni duñu ay jullit ta di ŋàññ diine ji ak di ci jëf luy yàq, benn jullit waruléena jàppe ay xarit, waaye koo xamne du jullit man nañuy maslaha ak moom.
Kon nit ki su gëmee Yalla, dëgg dëggi ngëm, waruta jàppee noonu lislaam yi ay xarit.
ahlul kitaab » gëm nañu Yalla subhaanahu wa tahaalaa, gëm Yonant Yalla bi (sallal Laahu tahaalaa halayhi wa sallam), gëm Al Xur-aan bimu wàcce ci moom, jëfe ay ndigëlëm teet ay tereem, kon sunu BOROOM jéggël léen séen ñaawtéef yépp, tàbbal léen ci aljana ja nga xamne xéewël la gu mat ta sax.
S.5 – V.65
Na ngéen sax cig ragal Yalla mi nga xamne dees na léen pang ëlëg jëmële léen ci moom.
S.5 – V.96
Na ngéen ragal Yalla ci mboléem séeni mbir, ta ngéen deglu ci ay ndigëlëm ta topp ko, sunu BOROOM du gindi nit ñay way gennug topp.
S.5 – V.108
Ndax du ngéen xellu!
Dundug adduna nekkut ludul laca not : am po, ay bànneex ak naqar.
Kon kërug ëllëg mooy kër gidul geent mukk, andak bànneex budul geent mukk, moo gën ñeel ña nga xamne ñuko bàyyiwoon xel lañu ci saŋe séenub xol ci lépp lu sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa gërëmut, saŋe séenub làmmiñ ci lépp lu sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa gërëmut, saŋe séeni cër ci lépp lu sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa gërëmut, ta saxoon ca.
S.6 – V.32
Na ngéen xupp ta fàttali, ci bis bi nekk ci kanam tay ñëw, gaa ñanga xamne danañu ragal séen bàmmeel fett, ñu génn ca, dox jëm ci bis boobée, andak njàqare ak tiis, di wuyyu wooteeb sunu BOROOM buñu sañuta baña wuyyu, te amut kenn ci kuñu mana wéeru kudul sunu BOROOM, amut kenn ku léen ca mënë xettali kudul sunu BOROOM. Ndax ñoom ñu tëŋku cig ragal Yalla, ci saŋe séenub xol ci lépp lu sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa gërëmut, saŋe séenub làmmiñ ci lépp lu sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa gërëmut, saŋe séeni cër ci lépp lu sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa gërëmut.
S.6 – V.51
Na ngéen di taxawal julliy juróom (5) ta andakuk teewlu màggug sunu BOROOM bi ak kawewaayam ak sellaayam, ta ngéen ragal ko. Ta mooy tëŋku ciy ndigëlëm teet ay tereem, ta lumu dogal ci yéen ngéen gërëm loolee. Ta boole ci rafetal séen digënte ak jaam ñi, ta kenn ku nekk ci yéen bàyyi xel ni ëllëg dees nako pang, jëmëleko ci moom.
S.6 – V.72
Koddaayal ragal Yalla moo gën adduna ak lici biiram, mooy pas pas ju sell ak kàddu yu sell ak jëf yu sell ; waaye sunu BOROOM moo koy jagleel kuko soob ci jaamam yi.
Gox bumu mana doon, su fekkoonteni tëŋku nañu cig ragal Yalla gu mat sëkk, sax ca laléen sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa digël, teet lamu léen tere, ta lumu dogal ci ñoom ñu gërëm loolee, gànnaaw bañu ko gëmée, dana léen ubbil ay barke ci assamaan yi ak ci suuf si. Waaye biñu eggee ci ñàkka rafetal séen digënte ak séen BOROOM ak ci séen digente ak séen moroom, cila léen sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa tege lañu foogutóon ba mukk ci ay musiba aki balaa, ta du léen teggeeku mukkit feeg dellu wuñu ci ag raggal Yalla.
S.7 – V.96
Muusaa waxoon na aw nitam dimblikoo léen sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa, ta ngéen muñ, ta xamni suuf si sunu BOROOM danako donnloo kuko soob walla ñuko soob ci ay jaamam. Muj gu rafet ñeel na way ragal Yalla yi.
S.7 – V.128
Sama yërmande daj na ñépp, waaye nag danaako jagleel ñeel ñanga xamne ñu sax cig ragal Yalla lañu ak maandu ak rafetal, tay genne asaka ci séen alal suca waree. Ñuy gaa ñuy gëm lañu samay kaawtéef yu may feeñal ci samay jaam.
S.7 – V.156
Ñi nga xamne dañoo sax cig ragal Yalla, waxtu wu seytaane tàbbalee ci seen xol ittey moy, dañuy daaldi déllóosi séen xel, xam ni yool buy sax ba fàww moo gën mbugël bu dul deñ ba mukk.
Ci misaal rek, dafa am waxambaane bu taqoo ak jàkka. Ab soxna diko woo, bëgg koo tàbbal ci biir kërëm, deñul diko man manee ba diko bëggë dugël ci biir néegëm, mu fàttaliku diisug aaya bii daaldi xêm. Bamu ximmlikóo mu diko man maneewaat, mu fàttalikuwaat diisug aaya bi, ci la daaldi faatu.
S.7 – V.201
Na ngéen sax cig ragal sunu BOROOM subhaanahu wa tahaalaa, ta ngéen di yewënël séeni digënte. Moodi kune lamu bëggël boppam mu bëggël ko moroomam, digënte bu ñagas itam ngéen dox ca wax ca kàdduy yiw ngir digënte ba defaru.
S.8 – V.1
Na ngéen sax cig ragal Yalla ta topp yonantam bi, ta ngéen tek séen tànk ci limu léen digël ta teet limu léen tere su ngéen nekkee di way gëm, ndax loolu moodi màndargam gëm.
S.8 – V.1
_________________________________________
FII LA XAAJ BU NJËKK BI YEM.